Tagatt

Ubité bi

Les formations d'E-TIC sont pratiques afin de répondre aux besoins du terrain:

Introduction

Modules de formation

Méthodes pédagogiques

Jangalem E-TIC mungi soxal ňi yaar ňuy waaja lim:

Xaac bu jënk bi

Jangum jangalekat yi nga xamni ňooy dem ci pënc yi:

  • ay ndaw yuy ligey ci seen coobare  ci ay bëreb yu mel ni EREV/GENSEN, ICVolontaires, cerice civique national, ndawi Youth and ICTs_Mali, ak ICV-Maali, Conjedev;
  • jigeen yi yengu ci mbirum jappanlate (nàtt yi, Mboolo ak kureel yi);
  • taskattu xibaar yi ci radio gox-goxaan yi.

li waral doxalin boobu nak mooy daňu bëgg topando bi daldi ko lawal Ndax mu nek luňu mëna sottal.sunu jangale mu jënk mi nak dafay yëngu lool. Bènn jaabante bu dùll jeex lay doon ci sèddale xibaar ak wutum xibaar yooyule ci pënc yi. Ci wàll woowu nak laňu gënna soxla yooneent yi.loolooy waral porozet bi di gënna mënna and ak yitte ak soxla u jamono.

Looloo waral ICVontaires tëral ay Mebètt am ci nii:

  • xaalaat ci nuňu wara fexe ba jigeen ňi maaccal seen xeel daldi leen wommat ci ňu jublu ci ay yëngu yu gëna am koom ndax seen ag book ci koom-koomi reew mi gëna yomb;
  • sàkku ay doxalin ak ay tërelin yu yees ci ligey bi;
  • jox jiggeen ňi pënc mu yees so xamni dinaňu ca mënn di sotante ay xalaat yu leen wara mënna siggil ci koom-koom mi askan wi;
  • Taagatt xeelaatu jigeen ňi ci wallu koom-koom;
  • Bokk ci li yokk xam-xamu ndaw ňi ci doxlin yu yees yi njaay mi ak;
  • Suxali neekin jigeen ňi ci kanmu askan wi, seen wergu yaram seen jang, seen koom ba ci seen kaatan ci joote ci xibaar yiak jang mi;
  • Suxali sansu ndaw ňi ci wutum koom ak ligey wi.

Xaaju ňaarel bi

Baykatt yi nak, ňooy faral di Gënna nek ci tool yi ak Pënc yi, seen jang daanaka soriwul, mooy waral seenum jang ak mokal yi doxalin yi di àjju ci xarala yu mujj yi ci diir wi ňu ko àppal ci porozet bi. Waye nak loolu tere wul dinaňu mënna jott ci xibaar yi ňu jaarale ci ndaw yiňu yooni ci pënc yi (radio yi jigeen ňi) walata sax yi ňuy jaaral c seen telefon porataabal yi, yi ňuy jottali ci baay tama ak, bu mëne nek, ay taf yuňi taf ci miir yi.

©1998-2024 ICVolunteers|system mcart|Updated: 2024-04-07 20:58 GMT|Privacy|